Juróomeelu atu « Carnaval » bii du dañ koy amal nii rekk waaye dañ ci jublu jàngale ak séddoo xam xam ak caada. Dina ñu may ñu fësal sunu bokk moomeel waye wann àdduna sépp taaru sunu aada ak cosaan
Mbokk yi xarit yeek am di jàmm yi ñi ngi leen di nuyu
Mbégte mu rëy lañ am ci dalal leen ci jàkkaarloo biñ am ak taskatu xibaar yi wara doon tambalig wajtaayu juróomeelu yoon biñ wara amal « carnaval de Dakar » bi wara tàmbale ci fan yi mujj ci weeru nowambar. Ndaje momu ñuy amal at mu jot dafa am solo lolu ci wàllu aada ak cosaan ci sunu réew, bés la boo xam ne Ndakaru dina wane boppam ci bépp anam ngir taaral ak fësal caada yi nekk ci sunu réew ak ci dendu Afrig yëpp.
Ren nak « carnaval » bi dañ ko tënk ci ponku « bokk moomeel ak xamle » mu indi beneen gis-gis ci mbir mi. Ponk bi daf ñuy sas ñu gëstu, sàmm ak xamle li ñu donn ci wàllu caada sunu doom ak sët yiy ñëw ëllëg. « Carnaval » weesu na xumbaay ak mumbaay: bërëb la boo xam ne day wane démb ak tay ba ku ci bokk rekk dinga fësal ab pàcci ci sunu démb.
Commentaires